CCBM Industries Automobiles, ñu taxawal ko ci atum 2005, muy konsesioneer bu am 100% ci kapitaalu senegal, di liggéey ci joxe ay pexe mobilite yuy yàgg te méngoo ak bëgg-bëggu marse bi ci dëkk bi. Volkswagen moom kese moo bokk ci Senegaal, di liggéeyandoo ak màrk yu melni Chery, Great Wall Motors, Haval, Sinotruk, ak Lovol.
Ci biir sunu njébbal, serwiis ginaaw njaay lu am solo la. CCBM Industries Automobiles mingi jéema joxe serwiis bu dëgër te baax ginaaw njaay, ngir gaaraati kiliyaan yi ñu toppatoo seen oto ci anam wu jaar yoon. Sunuy ekipu liggéeykat yi dañuy fexe ba oto bu nekk ñu toppatoo ko bu baax, di joxe pexe yu baax te méngoo ak bëgg-bëggu kiliyaan bu nekk, suko defee oto bi gëna gudd fan ba noppi gëna mëna liggéey.
Li tax CCBM Industries Automobiles am ndam mingi aju ci ekipam bu am doole, am xam-xam ak jom. Ndaw bu nekk ci ekip bi, muy serwiis ginaaw njaay, njaay wala yor liggéey, dafay liggéey bu baax ngir liggéeyukaay bi mëna dem ca kanam. Seen bëgg-bëgg ci liggéey buñ def bu baax, seen xam-xam ak seen jom ngir mëna dëppoo ak bëgg-bëggu kiliyaan yi ñooy caabi liggéeyu liggéeyukaay bi. Ñoom ñépp bokk dañuy jàppale liggéeyukaay bi mu jëm ca kanam, ba noppi di satisfaire kiliyaan bu nekk.
Ak njiit yu am doole, ekip bu jege, ak serwiis bu baax ginaaw njaay, CCBM Industries Automobiles amna mbegte def liggéey bu am solo ci joxe ay pexe yu yomb, yuy yàgg te am njariñ ci Senegal.
Sama xarit,
Dalal jàmm ci CCBM Industries Automobiles, konsesioneer bu am 100% kapitaal senegal te nekk ndawul màrku Volkswagen bu siiw ci àdduna bi, màrku internasional yi GWM, Haval, Chery, ak itam Lovol ak Sinotruk di poids ak masin yu usine yi.
Ak jaar-jaar bu am 20 at, danu leen di jox ay pexe yu bees te wóor, yu méngoo ak marse Senegaal. Sunuy serwiis ginaaw njaay bu baax ak sunuy pièce de rechange yi dañuy garanti performance ak guddu fan ci sa oto.
Pionnier yi ci liggéeyum dëkk bi, amnanu mbégte ci am usine bu njëkk ci Senegal, di defar ay oto yu méngoo ak seeni sàrti bopp, boole ci fësal xam-xam bi dëkk bi am.
Woolu ekip bu xarañ te am jom ngir leeral sa jaar-jaar ci oto.
CCBM INDUSTRIES AUTOMOBILES, fide sénégalais, moteur de votre mobilité!
Di nekk jàppante biñ taamu ngir am pexe ci mobilité buy yàgg ci Senegal ak Afrique sowwu jant, ci dajale ekip bu boole bëgg-bëggu gis-gis yu bees boole ci bokk ci yokkuteg sunu koom-koomu dëkk.
Joxe ay pexe mobilite yu baax, wóor te yomb jëfandikoo ci waa Senegal, boole ci xam-xamu dëkk bi ak sàrti àdduna. Niñu nekkee sosiete bu am 100% ci kapitaalu Senegal, danuy jàppale yokkute usine yi ci noonu lañuy tabax diggante wóolute ak sunuy kiliyaan ak sunuy àndadoo.
Danuy fexe nu gëna baax ci lépp lunuy def, di joxe oto yu méngoo ak sàrti àdduna bi, ba noppi di joxe produit ak serwiis yu baax te baax.
Danuy teg nit ñi ci sunuy jëf, di déglu bu baax li sunuy kiliyaan bi di xaar ci ñoom, ba noppi di leen jox pexe yuñ personaalise bu baax ak bàyyi xel.
Danuy wane xarañteef ci gaaw ci méngoo ak bëgg-bëggu sunuy kiliyaan bi ak yokkuteg marse bi, suko defee ñu mëna joxe pexe yu méngoo ak bëgg-bëggu sunu kiliyaan yi.
Danuy doxalee ci njub ak yëg-yëg bu xóot ci wàllu wareef ci askan wi, di fexe nu leer te gëm sunuy ñi ci laale.
Danu gëm ni liggéeyandoo ak jàppante amna doole ngir mëna yegg ci sunuy mébet yuñ bokk, boole ci defar barabu liggéey buy jàmm.