CCBM Industries Automobiles mooy konsesioneer bi njëkka am usine buy defar oto yu diis ci Senegal. Infrastructure bu amul fenn bi daf nuy may nu mëna topp bëgg-bëggu marse senegal bi, boole ci fexe ba montage bi ak maintenance bi baax.
Sunu nekk ci dëkk bi moo tax xam nanu bu baax li sunuy kiliyaan bi di xaar ci nun, te danuy gëna bàyyi xel ci serwiis kiliyaan yi, dalee ko ci joxe laaj bi ba ci joxe oto bi. Sunu mébet mooy joxe pexe yuñ méngale ak serwiis bu baax, ak tontu bu baax.